TSK

TSK · Acts 2:33

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ay bañam, ma rajaxe; ay noonam, ma fàdd,

Doj wi tabaxkat yi beddi woon, moo mujj doju coll wi.

Moo tax ma di ko jox ab cér ci biir ñu bare, mu séddoo ak ay kàngam alalu xareem, ngir moo jébbale bakkanu boppam, ñu limaale kooki tooñkat, moo gàddu bàkkaaru ñu bare te mooy tinul moykat yi.

Acts 1:4 TSK

¶ Ba mu nekkee ak ñoom, da leena sant, ne leen: «Buleen jóge Yerusalem, négleen digeb Baay bi ngeen dégge ci sama gémmiñ.

Acts 2:38 TSK

Piyeer ne leen: «Tuubleen te ku nekk ci yeen sóobu ci ndox ci turu Yeesu Almasi ngir njéggalug bàkkaaram, ngeen daldi jot ci Noo gu Sell giy maye.

Ba loolu amee mboolem gëmkati Yawut ya ànd ak Piyeer, waaru ca na mayug Noo gu Sell gi tuuruwaalee ca xeeti jaambur ña,

Noonu la deme ngir barkeb Ibraayma wàccal xeet yi dul Yawut ndax Almasi Yeesu, ngir itam nu jot ci digeb Noo gu Sell gi, ci kaw ngëm.

Moo tax ñu ne: «Moo yéeg fa kawa kaw, yóbbaale gàngoor gu mu jàppe xare, te moo séddale nit ñi ay may.»

Titus 3:6 TSK

gi mu nu awale ci Yeesu Almasi sunu Musalkat, ba baawaanal ko ci sunu kaw.

Waaye kii de, ba mu sarxee ngir ay bàkkaar, bennub sarax, mu doy ba fàww, ca la tooge fa ndijooru Yàlla.

mi yéeg asamaan, toog fa ndijooru Yàlla, ki malaaka yeek boroom sañ-sañ yeek boroom doole yi, bokk nekk cig curgaam.