TSK

TSK · Acts 20:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Booba bëti Israyil dafa lëndëm, ba gisatul ndax li muy mag. Yuusufa jegeñal leen seen maam, mu fóon leen, taf leen ci boppam.

Ba mu ko gisee, da koo indi Àncos. Ba mu ko defee, atum lëmm ñuy daje ca mbooloom gëmkat ña, di jàngal nit ñu takku. Ca Àncos lañu jëkka wooye gëmkat ñi ay gëm-Almasi.

¶ Gannaaw ba loolu wéyee, Póol ci ndigalal Noo gu Sell gi am mébétum jaare diiwaani Maseduwan ak Akayi, teg ca Yerusalem. Mu ne: «Gannaaw bu ma àggee foofu, war namaa jàll ba Room itam.»

¶ Ba loolu amee Póol wàcc, tiim ko, daldi koy téye ci diggante ñaari loxoom, ne leen: «Buleen jaaxle, mu ngi dund.»

Acts 21:5 TSK

Ba nu fa amee fan yooyu lanu fa bàyyikoo, dem, ñu gunge nu, ñoom ñépp, ñook seeni soxna ak seeni doom. Nu dem ba génn dëkk ba, daldi sukk ca tefes ga, ñaan.

¶ Dinaa dikk ba ci yeen, gannaaw bu ma jaaree diiwaanu Maseduwan, ndax Maseduwan laay jaare.

¶ Ba nu àggee diiwaanu Maseduwan, sunuw yaram noppluwul, waaye daj nanu bépp coono: xeex ci biti, njàqare ci biir.