TSK

TSK · Acts 24:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Naka la Axab gis Ilyaas, ne ko: «Kii yaw a, di lëmbe Israyil nii?»

Ba ko juróomeel Sanbalat yóbbanteeti ab surgaam genn kàddu gi, mu indaale bataaxal bu tëjuwul, yor ko ci loxoom.

¶ Kàngami buur yooyu dem ne Buur: «Waa jii, na dee rekk; mu ngi yoqil xarekat yi des ci dëkk bi, di yoqil ñépp ndax waxam jii mu leen di wax. Waa jii kat wutul jàmmu askan wii, xanaa musiba.»

Luke 23:5 TSK

Teewul ñu gëna dëggal seeni wax, ne: «Mooy yékkati askan wi, ndax li muy jàngle ci mboolem réewum Yawut, dale ko ca Galile ba fii.»

Mu yiwi ka ñu ko ñaanoon, te jëfi fippu ak nit ku ñu bóom taxoon ñu tëj ko kaso. Yeesu nag, mu teg ko ci seeni loxo, ngir ñu def ko lu leen neex.

Acts 6:13 TSK

Ñu indeeti foofa ay seedey naaféq yu ne: «Kii du bàyyee wax mukk lu juunoo ak bérab bu sell bii ak yoonu Musaa.

Ñu taxawal leen fa àttekat ya, ne: «Ñii ñoo yëngal sunu dëkk bi, di ay Yawut

di xaacu naan: «Wallee, bokki Israyil! Waa jii, mooy kiy wër fépp, di waare ñépp kàddu gu safaanook njariñal xeet wi, ak yoonu Musaa ak bérab bii. Rax ci dolli mu indi ci kër Yàlla gi ay Gereg, ba sobeel bérab bu sell bii.»

Lenn de man naa la koo nangul. Yoon woowu ñu ne mooy ngér mu sikk, moom laay topp, di ko jaamoo sunu Yàllay maam. Teewul mboolem lu ñu bind ci yoonu Musaa ak téerey yonent yi, gëm naa ko.

Waaye bëgg nanoo dégg ci sa gémmiñu bopp li nga gëm, ndax li nu xam daal mooy, ngér moomu nga bokk, fu nekk lañu koy diiŋate.»

Fàww sax mu am ay xaajaloo ci seen biir, ngir ñi seen ngëm wér mana fés ci seen biir.

Ndax nit ki su séddee Yàlla ab cér, ba tax mu muñ tiis ak coono bu ko yoon tegul, loolu aw yiw la.