Muy waa Pàrt, ak Medd ak Elam ak Mesopotami ak Yude ak Kapados ak Pont ak Asi,
TSK
TSK · Acts 27:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ndaw sa topp ci Póol ak nun, di xaacu, naan: «Nit ñii jaami Yàlla Aji Kawe ji lañu; dañu leen di yégal yoonu mucc.»
Ci biir loolu ñu bare ñu daan ñeengo, boole seeni téere, indi, lakk ko fa kanam ñépp. Ba ñu xaymaa njég la, tolloo naak juróom fukki junniy poseti daraxma (50 000).
Ña àndoon ak moom ñoo di Sopater doomu Pirus ma cosaanoo Bere, ak Aristàrk ak Segond, waa Tesalonig ya, ak Gayus, ma dëkke Derbe, ak Timote, ak waa diiwaanu Asi ya, Tisig ak Torofim.
¶ Gannaaw ba nu tàggoo ak ñoom, nu dugg gaal, jubal dunu Kos, teg ca teeri ca dunu Rodd, jóge fa, jàll ba Patara.
Waa réew ma nag laaye nu biir lool. Fekk na mu tàmbalee taw, ànd akub sedd. Ñu taalal nu am njaar, dalal nu nun ñépp.
Nu teeri dëkk ba ñuy wax Sirakus, toog fa ñetti fan.
¶ Aristàrk mi ma bokkal kaso bi, mu ngi leen di nuyu, moom ak Màrk rakku Barnaba. Ci mbiru Màrk moomu ngeen jotoon ndigal, ngir bu dikkee, ngeen teral ko.