TSK

TSK · Acts 28:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Njuddu-ji-réew ji nangeen ko yemaleek doxandéem bi ngeen dëkkal. Soppleen ko ni ngeen soppe seen bopp, ndaxte ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.

Wallul ku ñuy reyi te tooñul, xettlil kuy tërëf, ñu di ko reyi.

¶ Yeesu neeti ko: «Jenn waay a jóge woon Yerusalem, jëm Yeriko. Mu dajeek ay sàcc, ñu futti ko, dóor ko, daldi dem, bàyyi ko, muy waaja dee.

Acts 27:3 TSK

¶ Ca ëllëg sa nu teeri Sidon; Yulyus nag baaxe Póol, may ko mu dem ci ay xaritam, ngir ñu topptoo ko.

Muy sama digg ak Gereg yu xay yi, mbaa ñu xayadi ñi, ak ñi rafet xel, mbaa ñi ñàkk xel, am na lu ma war ci ñoom ñépp.

Ki xaraful ciw yaramam, te teewu koo sàmm yoonu Musaa, moo lay teg ab daan, yaw mi boole mbindum yoonu Musaa, ak sag xaraf, te teewu la di moykatub yoon wi.

Doñ-doñ, akub coono ci la, te bare naa lu ma fanaanee xoole. Xiif naa, mar naa, te bare na lu ma ñàkk ab dund. Liw naa, rafle naa,

Buleen sàggane di terle, nde am na ñu seen teraanga tax ñu fat ay malaaka te xamuñu ko woon.