TSK

TSK · Acts 3:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Man maa tabb buur, fal ko ci Siyoŋ, sama tund wu sell.»

Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax ji daa wax sama Sang, ne ko: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon sa ndëggastal.»

Piyeer nag miim, ne: «Soxna si, xawma kooku!»

Kon nag dama koy dóorlu, yiwi ko.»

Acts 2:33 TSK

Yàllaa ko yéege fa ndijooram, te jot na ci Baay bi Noo gu Sell ga mu dige woon. Moom la tuur nii tey, ngeen gis ko, dégg ko.

Acts 7:32 TSK

“Man maay sa Yàllay maam, maay Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba.” Musaa tiit bay lox, ñemeetula xool.

Mu ne ma: “Sunu Yàllay maam moo la dencal céru ràññee coobareem, ak gis Aji Jub ji, dégg ko, muy wax ak yaw.

Moo tax Yàlla kaweel koo kaweel, baaxe ko tur wi tiim wépp tur,

Ngëm la Ibraayma daleji ca suuf, sa ñu ko digoon, ba dëkke ay xayma ni ab doxandéem ci réewum jaambur, moom ak ñi mu séddool benn dige bi, te ñuy Isaaxa ak Yanqóoba.

Maay Kiy Dund, maa dee woon, maay dund nii tey ak ëllëg ba fàww te maa yor caabiy dee ak njaniiw.