TSK

TSK · Acts 4:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Kon nag waxal bànni Israyil ne leen: Man maay Aji Sax ji. Maa leen di sippil, yeen bànni Israyil, li leen waa Misra sëf, te maa leen di teggil njaam, gi ñu leen teg. Maay tàllal sama loxo, dogal mbugal yu kéemaane, ba goreel leen.

Yaw déy Aji Sax ji, xam nga! Ngalla bàyyi ma xel, geesu ma; feyul ma ñi ma sam. Bu leen muñal ba sànk ma! Xamal ne yaa ma tax di dékku saaga.

Luke 9:54 TSK

Taalibe ya ñuy wax Yanqóoba ak Yowaan gis loolu, daldi ne: «Sang bi, soo bëggee nu jox sawara ndigal, mu wàcce asamaan, faagaagal leen?»

Acts 2:43 TSK

Ba loolu amee ag ragal jàpp ñépp, ay kiraama yu bare aki firnde daldi sottee ca jëfi ndaw ya.

Acts 3:16 TSK

Gëm aw turam moo waral turam woowu dooleel nit kii ngeen gis, xam ko. Kon ngëm moo waral lii; ngëm gu sababoo ci Yeesu moo ko may mu wér péŋŋ nii ci seen kanam, yeen ñépp.

Acts 4:27 TSK

Dëgg la moos, ndax ci dëkk bii la Erodd ak Poñsë Pilaat lëkkoo, ànd ak xeeti àddinaak bànni Israyil ci kaw Yeesu, sa ndaw lu sell li nga fal.

Acts 5:15 TSK

Nit ñi dem bay génne jarag ji ci mbedd yi, teg leen ci ay laltu aki basaŋ, ngir bu fa Piyeer jaaree, lu bon bon takkndeeram mana dal ñenn ci ñoom.

Acts 9:34 TSK

Piyeer ne ko: «Ene, Yeesu Almasi wéral na la; jógal, lalal sa bopp.» Mu jóg ca saa sa.