TSK

TSK · Acts 5:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yàlla Aji Sax ji ne jigéen ja: «Yaw, li nga def nii mooy lan?» Jigéen ja ne ko: «Aa, jaan de moo ma nax, ba ma lekk ci.»

Ab doxandéem, sañ ngeen koo sàkku tegandaay, waaye seen mbokkum bànni Israyil, buleen ko sàkku tegandaay. Su ko defee seen Yàlla Aji Sax ji mooy barkeel mboolem seenu ñaq, ca réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko.

te naa: «Ki Sax gisu ci, Yàllay Yanqóoba jii yégu ko.»

Ku mana làqoo làquwaay, ba duma ko gis?» Kàddug Aji Sax jee. «Xanaa du asamaan ak suuf, maa ko fees?» Kàddug Aji Sax jee.

Luke 22:3 TSK

Seytaane nag dugg Yuda, mi ñuy wooye Iskaryo te mu bokkoon ca Fukk ñaak ñaar.

Acts 5:4 TSK

Ba mu jaragul, du yaa doon boroom? Gannaaw ba mu jaree it, xanaa du njég gaa ngi sa loxo ba tey? Ana noo mana xajale mii mébét ci sa xol? Du nit nga wor de, waaye Yàlla nga wor.»

Kon yaw miy jàngle, doo jàngal sa bopp? Yaw miy waare, di aaye sàcc, mbaa doo sàcc? Yaw miy aaye njaaloo, mbaa doo jaaloo?

James 4:7 TSK

¶ Kon nag nangul-leen Yàlla, te bañal Seytaane, mu daw, ba sore leen.

Ñu xalab ninki-nànka ju réy ja, jaanu cosaan joojee ñuy wax Tuumaalkat bi, di ko wax Seytaane, naxekatu mboolem àddina. Ci kaw suuf lañu ko xalab, mooki malaakaam.