Ñoom ñépp nag feese Noo gu Sell gi, tàmbalee làkk làkk yu wuute, na leen ko Noo gi manloo.
TSK
TSK · Acts 5:32
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Piyeer ne leen: «Tuubleen te ku nekk ci yeen sóobu ci ndox ci turu Yeesu Almasi ngir njéggalug bàkkaaram, ngeen daldi jot ci Noo gu Sell giy maye.
¶ «Nun ci sunu bopp noo seede li mu def lépp ci réewum Yawut yi ak Yerusalem. Moom mi ñu wékk ci bant, ba rey ko,
te diiru fan yu bare la feeñu ña àndoon ak moom, jóge diiwaanu Galile, dem Yerusalem, te ñooñooy ay seedeem tey ci askan wi.
¶ Ñetteel bi yoon a ngii, bu ma leen di ganesi. «Ci kàddug ñaari seede ba ñett nag la àtteb mépp mbir di wére.»
Yonent yooyu, xamalees na leen ne du seen njariñal bopp lañuy liggéeyal xibaar boobu, xanaa yeen. Ñi leen àgge xibaar bi tey ñoo di ñiy waare xibaaru jàmm bi ci dooley Noo gu Sell, gi ñu yebale asamaan, te muy mbir mu malaaka yi sax, noon siiwa nemmiku.