Psalms 27:12
TSK
Bu ma baye bànneexu noon. Seedey naaféq a ma jógal, di sos fitna.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bu ma baye bànneexu noon. Seedey naaféq a ma jógal, di sos fitna.
Yàlla laay màggal kàddoom, Yàlla laa wóolu, ragaluma. Lu ma nit manal?
¶ Ñu daldi ger ay nit ngir ñu duural ko, ne: «Noo ko dégg, mu yékkati kàdduy saaga, jëme ci Musaa ak ci Yàlla.»
di xaacu naan: «Wallee, bokki Israyil! Waa jii, mooy kiy wër fépp, di waare ñépp kàddu gu safaanook njariñal xeet wi, ak yoonu Musaa ak bérab bii. Rax ci dolli mu indi ci kër Yàlla gi ay Gereg, ba sobeel bérab bu sell bii.»
Carxal gi nag su soppikoo, fàww yoon wi itam soppiku, ànd ak moom.