TSK

TSK · Acts 6:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waaye laata loolu lépp, yeen, dees na leen teg loxo, fitnaal leen, jébbal leen kuréli jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanami buur aki boroom dëkk ndax sama tur,

Terewul ay gëmkat ñu dëkke Sippar ak Siren, bàyyikoo ca, dikk Àncos, wax ak làkk-kati Gereg yi, ñoom itam, ba àgge leen xibaaru jàmm bu Sang Yeesu.

Ba Yawut yi gisee mbooloo ma nag, kiñaan man leen, ñuy weddi waxi Póol, di ko saaga.

Ci kaw loolu mu jaare diiwaani Siri ak Silisi, di ñaax mboolooy gëmkat ña.

Ci biir loolu muy wax ak Yawut yaak jaamburi ragalkati Yàlla ya ca jàngu ba, di wax it ak waa pénc ma bés bu nekk.

Loolu moo wéy diiru ñaari at, ba mboolem waa diiwaanu Asi dégg kàddug Sang bi, muy Yawut, di Gereg.

¶ Ba àppu juróom ñaari fan yay waaja jeex, Yawut ya jóge diiwaanu Asi gis Póol ca kër Yàlla ga. Ñu yëngal mbooloo mépp, jàpp ko,

Acts 22:3 TSK

¶ «Man ab Yawut laa, juddoo Tàrs ca diiwaanu Silisi, yaroo ci dëkk bii. Ci keppaaru Gamalyel laa jànge, njàng mu dëppoo bu mat sëkk ak sunu yoonu maam. Ma doonoon ku xér ci Yàlla ni mboolem yeen ñii tey.

Boroom réew ma jàng bataaxal ba, daldi laaj ci ban diiwaan la Póol bokk, ba xam ne diiwaanu Silisi la bokk.

Acts 27:5 TSK

Ci kaw loolu nu jàll géej, gi janook diiwaani Silisi ak Pamfili, daldi teeri Mira ca Lisi.