TSK

TSK · Acts 7:55

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ At ma Buur Osiyas saayee, damaa gis Boroom bi toog kaw ngàngune mu kawee kawe, lafi mbubbam fees néeg bu sell bi.

Ba leeru Aji Sax ji yékkatikoo ca serub ya, dem ba ca buntu kër ga, niir wa daa fees kër ga, ëtt ba fees dell ak leeru Aji Sax ja ne ràññ.

Gannaaw loolu leeru Aji Sax ji yékkatikoo fa digg dëkk ba, dem, taxawi fa kaw tund wa ca penkub dëkk ba.

Acts 2:4 TSK

Ñoom ñépp nag feese Noo gu Sell gi, tàmbalee làkk làkk yu wuute, na leen ko Noo gi manloo.

Acts 6:3 TSK

Kon nag bokk yi, seetleen ci seen biir juróom ñaar ñu rafet seede, soloo Noo gu Sell gi te rafet xel, nu dénk leen sas woowu.

Acts 6:8 TSK

¶ Ci kaw loolu Eccen, mi yiwu Yàlla def ag leer fees ko, di def ay kéemaan ak firnde yu mag ci biir askan wi.

Acts 13:9 TSK

Ci kaw loolu Sóol mi ñuy wax Póol feese Noo gu Sell gi. Mu xool ñeengokat bi jàkk,

Maa xam aw nitu Almasi, ba ñu ko yéegee ba ñetteelu asamaan, fukki at ak ñeent la tey. Ndax aw yaramam lees ko yéegaale woon? Xawma, ndax yéegaaleesu ko aw yaramam? Xawma, Yàlla rekk a xam.

¶ Kàddu yii nu wax nag, lii moo di ponk bi: boobu sarxalkat bu mag lanu am, mu tooge ndijooru ngànguney ku Màgg ka fa asamaan.

¶ Gannaaw loolu damaa xool, rekk yem ci bunt bu ubbiku fa asamaan. Ci biir loolu baat ba ma jëkkoona dégg muy wax ak man te mel nig liit, ne ma: «Yéegal fii, ma won la liy topp ci loolu.»