TSK

TSK · Acts 8:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag, ñépp a ngi lewal lu lewul. Yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor.

Kenn dootu soxlaa jàngal kenn, muy moroomam mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Aji Sax ji,” ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ki gëna mag,» kàddug Aji Sax jee, «ndax maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.»

¶ Ba mbooloo ma gisee la Póol def, ca kaw lañu àddu ci làkku Likawni, ne: «Yàlla yee soppliku melow nit, wàccsi ci sunu biir!»

Waaye ci ñi ñu woo, ñuy Yawut, di Gereg, Almasi mooy manoorey Yàlla, di xam-xamu Yàlla.

¶ Su boobaa nu noppee doon ay tuut-tànk yu nit ñiy muusaatoo kàddu yu mel ni gannax yu nuy baaje, ak ngelawal mboolem àlluwa ju bees ju nuy pamti-pamtee ci seen biir pexey naxe ak njublaŋ, ngir fàbbi nu.

Benn ci bopp yi nag, rab wi da cee gaañu ba mel ni lu ñu rendi, ba mu dee. Teewul gaañu-gaañu boobu ko waroona rey daldi wér. Waa àddina sépp yéemu, topp ci rab wi.