TSK

TSK · Acts 8:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

doora faatu ca Kiryaat Arba, mooy Ebron, ca réewu Kanaan. Ibraayma nag dëj Saarata, jooy ko lool.

¶ Ba ñu agsee ca dàggay Ataat, ja ca wàllaa dexu Yurdan, dañu koo jooy jooy yu réy te metti. Yuusufa dëjal fa baayam diiru juróom ñaari fan.

Bànni Israyil jooy nañu Musaa ca jooru Mowab diiru fanweeri fan, fani dëj ba doora mat.

¶ Ba loolu wéyee Daawuda wax ak Yowab, mook mboolem gàngoor ga ànd ak moom, ne leen: «Xottileen seeni yére, soli saaku, ñaawloo ko deewug Abner.» Buur Daawuda ci boppam dox na, topp ca jaat ja.

Buleen jooy buur Yosya mi dee, buleen ko ñaawlul, jooyleena jooy buur Salum miy dem, te du délseeti, ba gis réewum juddoom.

Acts 10:2 TSK

Ku jullite la woon te ragal Yàlla, mook waa këram gépp; bare woon na sarax yu muy yéwéne askan wi, te ñaan ci Yàlla la saxoo woon.