TSK

TSK · Acts 8:32

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Dama noon: «Damay moyu ba duma moye làmmiñ.» Li feek ku bon di teew, may ŋalaab sama gémmiñ.

Waññi nga nu, nu won noon yi gannaaw, ñu bañ nu, ba futti nu.

Ndax damaa naagu woon ni xar mu ñu jëme rendikaay ba. Xawma woon ne man lañuy lalal ay pexe, naan: «Nan gor garab ak doomam, dagge ko fi réewum boroom bakkan, ba deesul fàttlikooti turam.»

Aji Sax ji nee: «Maa leen di wommat niy xar ba ca rendikaay ba, ñu mel ni kuuyi xar aki sikket.

¶ Ci kaw loolu Yeesu ne: «Baay, baal leen, ndax li ñuy def, xamuñu ko.» Ñu daldi tegoo bant ay yéreem, ngir séddoo ko.

waaye seenug njot moo di deretu Almasi ju jafe, ji taxawe deretu xar mu sikkul, gàkkul.