TSK

TSK · Acts 8:39

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ci kaw loolu ñu ne ko: «Xam nga lan la, sang bi? Am na ci nun juróom fukki nit ñu jàmbaare. Nañu dem seetali la sa sang ba. Jombul leeru Yàlla yóbbu ko, teg ko ci kaw tund yii, wenn, mbaa mu teg ko ci biir xur yii, wenn.» Mu ne leen: «Déedéet, buleen leen yebal.»

Maa séddoo fàww sa kàdduy seede, loolooy seral sama xol.

«Mbégte déy, ngeen di génne, ñu yóbbu leen ci jàmm, tund yu mag yeek yu ndaw yi di leen sarxolleel, garabi àll bi yépp tàccoondoo.

Man maa leen di naxtaan ba ngeen dal, ni doom ju ndeyam di naxtaan ba mu dal, ngeen am xel mu dal fi Yerusalem.

Mu tàllal lu bindoo ni loxo, daldi sëq sama kawaru bopp, lenn ngelaw yékkati ma ba ca diggante kaw ak suuf, yóbbu ma ba Yerusalem ci biir peeñum Yàlla, ba ca buntu ëttu biir kër Yàlla ba janook bëj-gànnaar, fa ñu teg jëmmu bokkaale, jay sabab fiiraange.

Ba loolu amee ngelaw ne ma siféet, yóbbu ba ca waa ngàllo ga ca réewum Babilon, lépp ci peeñu, ci dooley Noowug Yàlla. Peeñu ma ma gis nag yem fa.

Ci biir loolu taalibe ya dese mbég ak Noo gu Sell gi, ba seen xol fees.

Ci ndimbalam lanu ame ngëm ba mana àgg fi yiwu Yàlla wii nu taxaw taxawaay bu dëgër. Te it sunub sag moo di yaakaar ji nuy séentoo ab cér ci leeru Yàlla.

Maa xam aw nitu Almasi, ba ñu ko yéegee ba ñetteelu asamaan, fukki at ak ñeent la tey. Ndax aw yaramam lees ko yéegaale woon? Xawma, ndax yéegaaleesu ko aw yaramam? Xawma, Yàlla rekk a xam.

¶ Bégleen ci Boroom bi fu ngeen tollu, ma waxati ko, bégleen!

Léegi daal dangeena bew bay damoo seeni mébét! Googu damu de, lu bon la.