TSK

TSK · Acts 9:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Acts 6:1 TSK

¶ Jant yooyu nag, naka taalibe yi di gëna bare, Yawut ñiy làkk gereg tàmbalee ñaxtu ci kaw Yawut ñiy wax seen làmmiñu bopp ndax néewal gu ñu gis ñu néewal ko seeni jëtun ca na ñuy séddalee ag ndimbal bés bu nekk.

Acts 9:20 TSK

¶ Ca saa sa la tàmbalee xamle Yeesu ca jàngu ya, naan Yeesu mooy Doomu Yàlla.

Terewul ay gëmkat ñu dëkke Sippar ak Siren, bàyyikoo ca, dikk Àncos, wax ak làkk-kati Gereg yi, ñoom itam, ba àgge leen xibaaru jàmm bu Sang Yeesu.

¶ Ba ñu teeree Efes, fa la Póol bàyyi Pirsil ak Akilas. Mu dem ca jàngu ba, ba diisoo fa ak Yawut ya.

Bare na lu ma tukki, ay aaytéef xaare ma ay dex, xaare ma ay sàcc, xaare ma ay pexe yu ma samaw xeet lalal, ak yu ma jaambur ñi lalal. Ay aaytéef xaare na ma biir dëkk, xaare ma biir màndiŋ, xaare ma biir géej, xaare ma ci biir bokki taalibe yu ko mbubboo.

Jude 1:9 TSK

Moonte Mikayel, may kilifag malaaka sax, ba muy xëccoo ak Seytaane néewub Musaa, di wàqante ak Seytaane, taxul mu ñeme woon koo sikk ba boole ciy saaga. Da ko ne rekk: «Yal na la Boroom bi mbugal!»