Waaye bu ngeen jàllee dexu Yurdan, ba dëkki ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji sédde, ba mu noppal leen ci mboolem noon yi leen séq, ngeen dëkke xel mu dal,
TSK
TSK · Acts 9:31
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye boroom diiwaan yi ma jiitu dañu daan not askan wi, di leen sëf seen dund ak seen biiñ, boole ci ñeent fukki dogi xaalis. Seeni surga it di néewal askan wi doole. Man nag defuma noonu ndax ragal Yàlla.
daldi ne doom aadama: «Ragal Boroom bi daal, mooy xel mu rafet, te dëddu lu bon mooy am ug dégg.»
dëfal ko ci bési safaan, ba keroog ñuy gasal ku bon.
Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu xam-xam, te xel mu rafet akub yar, dof yaa ko xeeb.
Ragal Aji Sax ji kaaraange gu wér la ci nit, di rawtu ciy doomam.
Bul ñee bàkkaarkat, saxool ragal Aji Sax ji,
Bésub keroog car bawoo ca Yese, reen ba, taxaw di raaya buy gindi xeet yi, xeet yi di ko sàkku, dal-lukaayam ba jagoo teddnga.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Ay askan ñooy dikkati, di waa dëkk yu bare,
¶ Ba loolu amee kàddug Yàlla di law, limu taalibe yi yokku ba bare lool ci biir Yerusalem, sarxalkat yu bare daldi topp yoonu ngëm wi.
¶ Ci biir loolu kàddug Yàlla di gëna siiw, di gëna law.
Te yaakaar jooju du tas, ndax cofeelu Yàlla gi baawaan ci sunu xol, ci ndimbalal Noo gu Sell gi mu nu may.
¶ Kon nag nanu sàkku luy indi jàmm, ak lu nu feddalantee.
Noo bokk diy surga ci liggéeyu Yàlla bi; yeen ngeen di toolu Yàlla, di tabaxub Yàlla.
Kon yeen itam, gannaaw ñu xér ngeen ci mayi Noo gi, fexeleen cee am lu ne xéew, ngir feddli mbooloom gëmkat ñi.
¶ Gannaaw noo moom yii dige nag, soppe yi, nanu setal sunu bopp ci mboolem sobey yaram, ak ju xel, te nu matal sellnga ci ag ragal Yàlla.
¶ Mbaa fooguleen ne sunu bopp lanuy layal nii fi seen kanam? Fi kanam Yàlla de lanu waxe, ndax Almasi mi nu gëm, te lépp, soppe yi, seen yokkute la ñeel.
¶ Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel, ak mbég, ak jàmm, ak xolu muñ, ak mbaax, akug tabe, ak ngëm,
Almasi moo waajale noonu ñu sell ñi, ba ñu mana bey seen sas ci liggéeyam, ngir tabax mbooloom gëmkat, mi taxawe yaramu Almasi.
¶ Bu genn kàddu gu bon génne seen gémmiñ, xanaa su ko jaree ngeen wax lu baax, luy jariñe, te diw yiw ci ñi koy dégg.
Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp farlute, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi.
Su ko defee ngeen di dunde dundin wu yellook Boroom bi, ngir bànneexal ko ci wet gu nekk, seen meññeef it di jépp jëf ju baax, te ngeen gën di xam Yàlla.
¶ Sunu Sang Yeesu Almasi ci boppam, ak Yàlla sunu Baay, mi nu sopp, te may nu ciw yiwam, jàmmi xol ju sax dàkk, ak yaakaar ju wér,
Kon des na ba tey noflaayu bésub juróom ñaareel bu ñu waajalal ñoñu Yàlla.