TSK

TSK · Acts 9:39

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yeen jigéeni Israyil, jooyleen Sóol, ma leen wodde ndimol tànnéef lu xonq curr, takkal leen gànjari wurus ca seen kawi yére.

Ku jub barkeel, saw tur du fey; ab soxor, turam seey.

Liggéey boo gis, liggéeyal; def ci loo man. Ndax muy jëf, di doxalin, di xam-xam, di manoore, dara amu ci njaniiw, ga nga jëm.

Acts 6:1 TSK

¶ Jant yooyu nag, naka taalibe yi di gëna bare, Yawut ñiy làkk gereg tàmbalee ñaxtu ci kaw Yawut ñiy wax seen làmmiñu bopp ndax néewal gu ñu gis ñu néewal ko seeni jëtun ca na ñuy séddalee ag ndimbal bés bu nekk.

Acts 9:36 TSK

¶ Dëkk ba ñuy wax Yope, ab taalibe bu jigéen a nga fa woon, ñu di ko wax Tabita mbaa Dorkas ci làkku gereg. Def lu baax ak sarxe la saxoo woon.

Nu nekk laa leen wone ne sunu wartéef mooy nu liggéeye noonu bu baax, ngir dimbali néew-doole yi, tey fàttliku kàddug Sang Yeesu, ga mu noon: “Nangu, joxee ko ëpp barke.”»

Sàcc bi, na ba sàcc te nangoo sonn, di liggéeye loxoom liggéey bu rafet, ba man cee dimbali néew-ji-doole ji.

¶ Bokk yi nag, buggunu ngeen réere mbirum way dawlu ñi, bay tiislu ni ñeneen ñi amul jenn yaakaar, di tiisloo.