Aji Sax ji ne Musaa: «Yaa ngi nii di tëddi fa say maam. Mbooloo mii nag dinañu tàmbali di gànctuy topp yeneen yàllay doxandéem yu waa réew, ma ñu jëm ca seen biir. Dinañu ma wacc, fecci sama kóllëre gi ma fasoon ak ñoom,
TSK
TSK · Amos 2:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ana lu waral nga ñàkke worma kàddug Aji Sax ji, di def lu mu ñaawlu? Uri Etteen bi, yaa ko fàdde saamar; jabaram nga jël, def ko sa jabar, moom nga fàdde ko saamaru Amoneen ñi.
¶ Ba Buur déggee kàdduy téereb yoon wa, daa xotti ay yéreem ndax tiitaange.
Lu ñaawa ñaaw lanu la def, te sàmmunu say santaaneek say dogal ak sa ndigali yoon ya nga dénkoon Musaa, sa jaam ba.
Artu nga leen ndax ñu dellu ci saw yoon, teewul ñu bew, ba sàmmuñu say santaane, xanaa di moy sa àttey yoon yiy taxa dund képp ku ci sàmmu. Ñuy daŋŋiiral, sajju loos, bañ laa déggal.
Ñi jiite askan wii ñoo leen di sànk, ña ñuy jiite loru.
Kee di jur gu fore ab dóom, xelam nax ko, sànk ko. Du keey musal bakkanam de! Du kee naa: «Xanaa duy caaxaan laa ŋàbb nii?»
weer leen ci naaj week weer wi ak mboolem biddiiw yi ñu soppoon, di leen jaamu, di leen topp ak a sàkku, di leen sukkal. Deesu ko dajale, deesu ko suul; day mel niy jonkan fi kaw suuf si.
Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Yàllay Israyil dafa wax ne: «Maa ngii di leelsi xeet wii njàqarey xeme, nàndal leen tookey mbugal.
Yeen nag, ngeen di bon, ba raw seeni maam. Yeena ngii, ku nekk të ticc, topp xolam bu bon, bañ maa déggal.
Waaye su ngeen ma déggalul, baña sellal bésub Noflaay, baña moytoo gàddu lenn, di jaare bunti Yerusalem bésub Noflaay, su boobaa dinaa taal dëkk bi taal buy xoyom këri Yerusalem yu yànj, te du fey.”»
¶ «Dégg naa kàdduy waxyu yi yonent yooyuy waxe ci sama tur ay fen, naan gént nañu lii, gént nañu lee.
Seeni peeñu caaxaan la, seeni ngisaane diy fen. Ñu naa: ‘Kàddug Aji Sax jee,’ te Aji Sax ji yebalu leen! Teewul ñuy xaar kàddu gu sotti.
¶ Ba loolu amee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
Li ko waral mooy sama àttey yoon yi ñu xalab, ak sama dogali yoon yi ñu jëfewul, ak sama bési Noflaay yi ñu ñàkke worma, ndax xol lañu toppe seen kasaray tuur yi.
Li ko waral mooy sama àttey yoon yi ñu jëfewul, ak sama dogali yoon yi ñu xalab, ak sama bési Noflaay yi ñu ñàkke worma, ak topp gi ñu topp seen kasaray tuuri baay, wékk leeni gët.
Sama mbir yu sell, nga sàggane, sama bési Noflaay, nga ñàkke worma.
«Owoliba rakk ja gis ca te gëna yàqu magam, di gànctu ba raw mag ja.
Man nag ni ñaawat laay def ak Efrayim, te ni sànkar laay def ak Yuda.
Efrayim mooy sàmmkatub ngelaw, yendoo topp ngelawal penku, di yokki fen ak fitna, fasoo kóllëre ak Asiri, yónnee yóbbalu diw ba Misra.
«Yeen doŋŋ laa ràññee ci mboolem askani suuf. Moo tax ma di leen mbugal ndax seen ñaawtéef gépp.»
Ñoo weccee dëggu Yàlla, aw fen, di sujjóotal ak a jaamu mbindeef, bàyyi Bindkat bi yelloo cant ba fàww. Amiin.
Xam ngeen ne yëf yuy wéy yu mel ni xaalis mbaa wurus, du moom lees leen jote ci seen dundinu neen wa ngeen donne ca seeni maam,