Aji Sax jeey def seen tawub réew di suuf ak pënd bu bawoo asamaan, di yuriku ci seen kaw, ba ngeen sànku.
TSK
TSK · Amos 4:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Babilon nag, mooy gànjaru réew yi ko wër, di teraanga ji Kaldeen ñiy sagoo, waaye Yàllaa koy tas, mu ne tasar ni Sodom ak Gomor.
Ñoom ñépp a di fippukat yu fétteeral, wër di sos, dëgërle ni xànjar ak weñ gu ñuul. Ñoom ñépp di yàqkat.
Edom day tas ni Sodom ak Gomor ak la ko wër.» Aji Sax jee ko wax. «Nit du ca dëkk, doom aadama du fa dal.
¶ Ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikkal ma ne ma:
Duñu dellu réewum Misra. Waa Asiri ñooy doon seen buur, nde ñoo baña délsi fi man.
«Maa wéetal seeni biir seen dëkkoo dëkk, dugub ñàkke fépp fu ngeen moom, te taxul ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee.
Aji Sax ji ne Tuumaalkat bi: «Aji Sax ji rëbb na la, Yaw Tuumaalkat bi, Aji Sax ji taamu Yerusalem rëbb na la. Xanaa Yosuwe mii du lenn lu moy gillit wu ñu fëkke cib taal?»
ndegam dëkk ya ñuy wax Sodom ak Gomor it, la mbugale seenub taste, def leen ab dóom, ba def leen misaal mu ñeel aji gëmadiy ëllëg,
ñii ngeen wallu leen, foqatee leen ci sawara, ña ca des, ngeen yërëm leen yërmande ju ànd akug ragal, ba far seexlu ab turki bu seen yaram sobeel ndax seeni bàkkaar.