TSK

TSK · Amos 5:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Waa Yerusalemee, seen njañ li ngeen séddoo Yàlla, xuufleen ko, sànni, ñaawloo ko, xaaculeen fa kaw tund ya ne faraas, nde Aji Sax ji xalab na, wacc na seen maas gii sabab sànjam.

«Maay def Yerusalem jali doj, till yi dëkke; ma def dëkki Yuda gent bu kenn dëkkul.»

Ndee déy moo ñalgoo sunuy palanteer, dugg sunuy kër yu yànj, ngir fàdd gone yi ci mbedd mi, ak xale yu góor yi ci pénc yi.

¶ Aji Sax ji ne ma: «Yaw nag jooyal garmiy Israyil.

Ñooy yékkati kàddu, jooye la, ne la: “Yaaka sànku tey, yaw dunu géej bu xumb bi woon, yaw dëkk bu siiw bi woon, di jàmbaaru waa géej, yaak say nit a daa tiital mboolem ñi leen wër.

Sa alal ja, sab yeb, sa njaay ma, sa niti géej, say mool, say jagalkat, say jaaykat, ak mboolem sa dag yi ci sa biir, ak mboolem sa gàngoor gi ci sa biir, ñooy tàbbeendoo xolu géej keroog sa bésub jéll ba.

«Yaw nit ki, yékkatil kàddug jooy, ñeel Firawna buuru Misra. Nga ne ko: “Dangaa meloon ni waxambaanew gaynde ci biir xeet yi, mel ni ninki-nànkay biir géej, di fettaxe say wal, di wéquy nëxal ndox mi, di tilimal dex gi.

Amos 3:1 TSK

¶ Dégluleen kàddu gii Aji Sax ji wax ci yeen, bànni Israyil, mu jëm ci seen mboolem xeet wi mu génnee réewum Misra. Mu ne:

Amos 5:16 TSK

Moo tax Boroom bi Aji Sax ji, Yàlla ji ci gàngoori xare yi, dafa ne: «Bayaaloo bayaal ubalee ki yuux, mbeddoo mbedd riir aki wóoy! Dees na woo beykat bi ciy jooy, woo jooykati dëj ciy jooyoo.

Micah 2:4 TSK

Bésub keroog lees leen di fental aw léeb, woyal leen woy wu tiis, te naa: “Sotti na, yàqu nanu yaxeet! Sama suufu askan dugg na ciy loxo, ba sore ma, ab fippukat lañu jox sunuy tool!”»