TSK

TSK · Amos 7:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Njéeréer ya daa muur suuf sa sépp, ba giseesu ko. Suuf sa ñuul kukk. Njéeréer ya lekk lépp luy gàncax mbaa meññeefi garab gu tawub yuur ba jotuloona yàq, ba lenn lu naat desatul, du xobi garab, du gàncax, ca mboolem réewum Misra.

ne ko: «Éey Boroom bi, ndegam daj naa saw yiw, rikk àndal ak nun rekk, Boroom bi, ak li mbooloo miy dëgër bopp lépp! Jéggal nu sunu ñaawtéef ak sunu bàkkaar rekk, te nga séddoo nu.»

Ngalla jéggalal mbooloo mii seenug tooñ ci sag bare ngor, noonee nga leen masa bale, ca Misra ba tey jii.»

Éy Aji Sax ji, jógal! Looy nelaw? Yewwul, bu nu wacc ba fàww.

Yii yaar de dikkal na la: Yàquleek sànkule. Ana kuy bokk ak yaw saw naqar? Xiif ak loraangey saamar! Ana nu ma lay dëfale?

Aji Sax ji, xam nanu sunug mbon, xam sunu ñaawtéefi maam; moy nanu la moos.

¶ Naka lañu dem, reyi, ma des fa man doŋŋ. Ma daldi daanu, dëpp sama kanam fa suuf, daldi àddu ca kaw, ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, xanaa doo sànk mboolem ndesu Israyil ci sa xadar jii ngay xëpp ci kaw Yerusalem?»

Boroom bi, ngalla Boroom bi, déglu nu te baal nu! Rikk Boroom bi sama Yàlla, teewlul ngir yaw ci sa bopp, te bañ noo yeexe, ndax saw tur lañu tudde sa dëkk ak sa mbooloo.»

Ana kuy xeeb bés bii lu tuut sottee? Nañu bége kay buumu beteex bi ñu gis ci loxol Sorobabel! «Juróom ñaar yii nag gëti Aji Sax jee, ñoom ñooy wër àddina sépp.»

Ñu ne leen, buñu laal menn um ñax, mbaa genn gàncax, mbaa genn garab, xanaa ñu jublu rekk ci nit ñi amul màndargam torluwaayu Yàlla ci seen jë.