TSK

TSK · Amos 7:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sawara ne jippét, bawoo fi Aji Sax ji, lakk leen ba ñu dee fa kanam Aji Sax ji.

Sawaraa ngay tàkke ca samam sànj, di lakke ba ca xóotey njaniiw, ba xoyom suuf ak meññeefam, ba jafal reeni tund ya.

«Aji Sax ji déy a ngii dikke sawara, ay watiiram mel ni ngëlén, mu nara sànju, sotti meram, gëdde sawara wuy sëlsëli.

Yeen waa kër Daawuda, Aji Sax ji dafa wax ne: Àtte yoon, deeleen ko xëye, di xettli ki ñu xañ dëgg ci ki koy néewal doole, balaa sama mer ne jippét, di tàkk te deesu ko mana fey ndax seen jëf ju bon.

Amos 1:7 TSK

Maay yebal sawara ca tatay Gasa, mu xoyom ay taaxam.

Amos 5:6 TSK

Sàkkuleen Aji Sax ji, ba dund. Lu ko moy mu ne jippét ci kaw askanu Yuusufa, lakk waa Betel lakk gu dul fey.

Amos 7:7 TSK

¶ Mu feeñooti ma, gisuma lu moy Boroom bi taxaw ci ab tata, mu ñu natte buumu beteex ba ñu koy tabax. Ma nga yor buumu beteex ca loxoom.

Nahum 1:6 TSK

Bu sànjoo, ana kuy taxaw? Ana kuy dékku tàngooru meram? Am sànjam a naan soteet ni sawara, doj yi rajaxoo fi kanamam.

¶ Gannaaw loolu damaa xool, rekk yem ci bunt bu ubbiku fa asamaan. Ci biir loolu baat ba ma jëkkoona dégg muy wax ak man te mel nig liit, ne ma: «Yéegal fii, ma won la liy topp ci loolu.»