Du kenn sax ku am sikk kuy agsi ba fii, du gumba, du kuy soox, du ku xar-kanamam am sikk mbaa ku cér yi sutaate.
TSK
TSK · Daniel 1:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Seetlul ku man liggéeyam, buur lay liggéeyal, du liggéeyal baadoolo.
Yàlla nag may ñeenti xale yu góor yooyu xel ak ràññee ci mboolem lu ñu bind ak wàllu xam-xam. Dañeel moom mana firi mboolem peeñu ak gént.
Mu woolu taryaax yi ak ñeengokat yi ak jibar yi ak xërëmkat yi, ngir ñu firil koy géntam. Ñu agsi taxaw ca kanamam.
Xërëmkat ya ne Buur: «Buur, amul kenn ci kaw suuf ku mana wax li ngay laaj. Te it benn buur ak nu màggaayam ak dooleem mana tollu, masula laaj lu mel nii benn taryaax mbaa ñeengokat mbaa xërëmkat.
¶ Ci biir loolu ay xërëmkat dikk, di boole Yawut ya.
¶ Buur daldi àddu ca kaw, di woolu ñeengokat yeek xërëmkat yi ak seetkat yi. Mu wax ak boroom xam-xami Babilon yooyu ne leen: «Képp ku jàng mbind mii te wax ma lu mu tekki, dees na ko solal yérey buur yu xonq curr, takkal ko caqu wurus, jox ko kilifteef gu koy tofal ci bummi.»
¶ «Booba la Musaa juddu, rafet ba fa kanam Yàlla, ñu yor ko ñetti weer ci biir kër baayam.
Li mu ci namm moo di teewal mbooloo mi fi kanamam, mu mel ni ab séetam bu ne ràññ, gàkkul, rasul, taqul lenn, xanaa sell, mucc sikk.