Ci biir loolu ñu jox xaalis yettkati doj yeek xaddkat yi, jox waa Sidon ak waa Tir ab dund, aki naan akug diw, ngir ñu jëleji Libaŋ ay banti seedar, jaarale ko ci géej gi ba Yafa, ci ndigalal Sirus buuru Pers.
TSK
TSK · Daniel 10:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Diirub nguurug Sirus buuru Pers, ba ca nguurug Daryus, waa réew ma dañu daan fey ay xelalkati buur ngir ñuy nasaxal pexey bànni Israyil.
¶ At ma jëkk ca nguurug Buur Sirus, Buur Sirus joxe na ndigal ci mbirum kër Yàlla ga ca Yerusalem. Mu ne: Nañu tabaxaat kër Yàlla gi, muy bérab bu ñuy sarxee ay sarax. Nañu dëgëral kenu ya. Na taxawaayam di juróom benn fukki xasab, yaatuwaayam di juróom benn fukki xasab,
Maa naa ci Sirus: “Sama sàmm bi!” Mooy matal sama bépp nammeel, te it moo naa ci Yerusalem: “Nees ko tabaxaat,” kër gu sell gi, laa ne: “Nees ko yékkatiwaat!”»
Yàlla nag may ñeenti xale yu góor yooyu xel ak ràññee ci mboolem lu ñu bind ak wàllu xam-xam. Dañeel moom mana firi mboolem peeñu ak gént.
Mooy walbati jamono, di soppi demin, di fal buur, di folli. Mooy xelal boroom xel mu rafet, di xamal boroom xel mu ñaw.
loolu yépp ndax dañoo gis ci kooku Buur tudde Beltasar, xel mu ñaw akum njàng ak ràññee. Day firi gént, di teqental ay cax ak a lijjanti ay jafe-jafe. Kookooy Dañeel; kon nañu ko woo, mu wax piri mi.»
Keey musle, di xettlee, di def ay màndarga aki kéemaan, kaw asamaan ak suuf. Kee musal Dañeel ca pàddum gaynde ya.»
Peeñum ngoon meek mu bëccëg mi la dikkal lu wér la. Yaw nag neel cell ak peeñu mi, ndax des na fan yu bare.»
Ba nga tàmbalee ñaan la kàddu dikk. Maa la ko yégalsi, ndax yaw ku ñu naw nga. Déggal kàddu gi te dégg peeñu mi.
¶ «Léegi, maa ngi lay xamal lu wér. Dama ne, dina amaat ñetti buur yuy falu ci réewum Pers, ñeenteel ba dikk, dajale alal ju bare, ba ëpple leen ñoom ñépp. Bu demee ba alalam may ko doole, dina def lépp lu mu man ngir xabtal ñépp ci kaw nguuru Geres.
Mu ne ma: «Dañeel, demal rekk, ndax mbir yii dees koo làq, dëxëñ ko, ba keroog muj ga taxaw.
¶ Malaaka ma nag ne ma: «Bindal lii: “Ndokklee ñi ñu woo ci berndey céetu Gàtt bi.”» Mu teg ca ne ma: «Loolu kàddu yu dëggu yu Yàlla la.»