Léegi nag maa ngi dellu ca saay bokk, waaye kaay, ma xamal la li xeet wii di def saw xeet, fan yu mujj ya.»
TSK
TSK · Daniel 10:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Su ko defee bu leen musiba yu bare dikkalee aki njàqare, woy wii mooy biral kàddug seede fi seen kanam, ndax su boobaa xel du ko faaye, ba mu réer seenu askan. Ndax kat xam naa seen mébét mi ñuy rabat, te yóbbooguma leen sax ca réew ma ma leen giñaloon.»
Yaay songi Israyil, sama ñoñ, mel ni aw niir, muur réew ma. Fan yu mujj ya la loolu di am, maa lay yóbbu yaw Gog, ba ca réew ma ma séddoo. Maa lay firndeele sama sellnga, ngir xeet yi gis, ba xam maay kan.
Peeñum ngoon meek mu bëccëg mi la dikkal lu wér la. Yaw nag neel cell ak peeñu mi, ndax des na fan yu bare.»
¶ Ci ñetteelu atu nguurug Sirus buuru Pers, kàddu daa dikkal Dañeel ma ñuy wax Beltasar. Kàddu googu di gu wóor tey yégle xare bu mag. Mu dégg kàddu gi, xam pirim peeñu mi.
Mu ne ma: «Dañeel, demal rekk, ndax mbir yii dees koo làq, dëxëñ ko, ba keroog muj ga taxaw.
Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, askan yi riirandoo, wutsi ko.
¶ Lii, nanga ko xam: mujug jamono, jant yu tar dina dikk.