Job 16:5
TSK
Waaye su doon man, ma wax ak yeen, ba dëfal leen, mas-sawu leen, ba ngeen giif.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye su doon man, ma wax ak yeen, ba dëfal leen, mas-sawu leen, ba ngeen giif.
Bés ba ma wootee, yaa ma wuyu, ñemeel ma, dooleel ma.
Bi muy wax ak man, dëpp naa sama kanam fi suuf, ba daanu leer. Mu laal ma, taxawalaat ma fa ma taxawoon.
Jekki-jekki jëmm ju mel ni nit dikk, laal samay tuñ. Ma ŋa, àddu, daldi wax ak ki taxaw sama kanam ne ko: «Sang bi, peeñu mi tax na ma jàq, ba amatuma benn doole.
Malaaka mu bawoo asamaan daldi koy feeñu, dooleel ko.
Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi wàcc ci sama kaw.
Lépp laa mane ci ndimbalal Ki may manal.