TSK

TSK · Daniel 10:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bés ba ma wootee, yaa ma wuyu, ñemeel ma, dooleel ma.

bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama ndijooru njekk déy.

Léegi nag yaw Yanqóoba, yaw Israyil mii, Aji Sax ji la sàkk tabax la, dafa wax ne: «Bul tiit, jot naa la. Dama laa woo ci sa tur. Maa la séddoo.

Mu ne ma: «Dañeel, yaw mi ñu naw, déggal kàddu yi ma lay wax. Jógal taxaw sa taxawaay, ndax dañu maa yebal ci yaw nii.» Naka la ma wax kàddu yooyu, ma ne ñokket, di lox.

Léegi nag, Sorobabel, góor-góorlul, Aji Sax jee ko wax. Yaw doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag bi, góor-góorlul; yeen mboolem askanu réew mi, góor-góorluleen, kàddug Aji Sax jee. Mu ne: Liggéeyleen, maa ànd ak yeen déy, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

Na ngeen doone woon alkànde ci biir xeet yi, yeen waa kër Yuda, ak waa kër Israyil, ni laa leen di walloo, ba ngeen doon barke. Buleen ragal. Góor-góorluleen.»

¶ Li ci des nag moo di ngeen manoorewoo Boroom bi, te ngeen sàkkoo ndimbal ci dooleem ak kàttanam gi amul kem.

¶ Naka laa ko gis, ne dàll daanu ci ay tànkam ni ku dee. Mu teg ma loxol ndijooram, ne ma: «Bul tiit. Maay Ki Jëkk, di Ki Mujj.