TSK

TSK · Daniel 11:36

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ndax kat seen Yàlla Aji Sax ji mooy Yàllay yàlla yi, te mooy Sangu sang yi. Mooy Yàlla ju màgg ji, jàmbaare te raglu. Ki gënalewul, jëlul ub ger.

Job 23:13 TSK

Yàlla de kenn la, ana ku koy waññi? Coobarey bakkanam lay def.

Santleen Yàllay yàlla yi. Kee saxoo ngoram!

Wóoy ngalla Asiri miy sama yetu mer, bolde bi ñu ŋàbb di samam sànj,

Waaye fi leek lu néewa néew mbugal jeex fi seen biir, am sànj sippil Asiri seen sànkute.»

Maay yéeg fa kaw niir ya, ba mel ni Yàlla Aji Kawe ji!”

Xambees na démb ab taal bu ñuy wax Tofet, te buur ba lees ko waajalal; dees koo xóotal, yaatal ko, sawara way tàkk, matt ma ne gàññ, noowal Aji Sax ji nar caa tàkke, di sël-sëli ni walum tamarax.

Yaa tukki ba ca buur ba, yóbbaaleg diw, ak cuuraay lu ne gàññ, yebal say ndaw fu sore, ba ñu àkki njaniiw.

Yeenay damu fi sama kaw, di ma wax waxi reewande ju bare! Maa déggal sama bopp.

Ma bëgga am lu leer ba tey ci fukki béjjén yi ci bopp bi ak beneen ba génn, ba ñett daanu ca kanamam; mu am ay bët ak gémmiñ, di wax kàdduy damu, te ëpp yi ci des.

Muy damu bay diir mbagg Njiital gàngooru xare gi, daldi dakkal sarax ba ñu ko daan defal bés bu jot, màbb bérabam bu sell ba.

Dina gëna am doole, waaye du doon dooley boppam. Yàqam dina jéggi dayo, te ay pexeem dina joy. Dina faagaagal ñu am doole ba ca mbooloom aji sell yi.

Dina feddli kóllëre diggam ak ñu bare ci benn àppu juróom ñaar, te ci diggu àppu juróom ñaar ba lay dakkal sarax yi ñuy rendi ak yeneen sarax. Ci genn wetu sarxalukaay bi la yàqkat biy taxawal lu siblu, di sabab yàqute, ba keroog muj gi ñu ko dogalal ne milib ci kawam.»

Ki leen di song dina leen def li ko soob, ndax kenn du ko të. Dina toog ci réew mu taaru ma, te am dooley tas ko.

Jamono ja ñuy dakkal sarax si wara sax fàww, di keroog ba ñuy taxawal lu siblu lay jur yàqute, junniy fan ak ñaar téeméer ak juróom ñeent fukk (1 290) dina ca topp.

Acts 4:28 TSK

Noonu it lañu sottale mboolem li nga dogale woon sa loxo ak sa coobare.

waaye bu bési kàddug juróom ñaareelu malaaka mi taxawee, ba mu tàmbalee wal liit gi, su keroogee pexem Yàlla miy kumpa dina sotti, na mu ko waxe woon ay jaamam, yonent yi.»

Ñu jox ndaw si ñaari laafi jaxaay ja, ngir mu naaw, rëcc ninki-nànka ji, dem màndiŋ ma, ca rawtoom ba ñu koy leele lu tollook ñetti diir ak genn-wàll.

¶ Ci kaw loolu malaaka mi yóbboo ma Noowug Yàlla ba ca màndiŋ ma. Ma gis jigéen ju war rab wu xonq wu am juróom ñaari bopp ak fukki béjjén, te yaram wi fees ak tur yuy saaga Yàlla.