TSK

TSK · Daniel 11:45

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Asmon la kem gay jàddaate jubal xuru Misra, doora àkki géej.

Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, Aji Sax ji mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, xeet yépp riirandoo, wutsi ko.

Xanaa du yaa doon wax ci sam xel, naa: “Maay yéeg kaw asamaan, maay aj sama jal kaw biddiiwi Yàlla, maay toogi kaw tundu ndaje ma, fa catal bëj-gànnaar.

Maa lay waññi, yóbbu la, jële la catal bëj-gànnaar, yéege la kaw tundi Israyil.

Waa pénc mi toog, ñu nangu kilifteefam, tas ko, neenal ko ba fàww.

Ki leen di song dina leen def li ko soob, ndax kenn du ko të. Dina toog ci réew mu taaru ma, te am dooley tas ko.

Joel 2:20 TSK

Waa bëj-gànnaar, maa leen di soreleek yeen, maa leen di dàq, jëme réew mu maral te wéet, gàngoor ga jiitu jubal géeju penku, ga féete gannaaw jubal 0géeju sowu, ba seeni néew gilli, xasaw ba ubale, ngir jëf ju réy ji ñu def!»

Bésub keroog Yerusalem la ndox muy dund di wale, genn-wàll gi jëm géeju penku, genn-wàll gi, géeju sowu, te noor ak nawet lay doon.

Su boobaa la ku dëng ka di feeñ, te Sang Yeesu moo koy jàllarbee ngelawal gémmiñam, te moo koy rajaxee ca na muy feeñe bu délsee.

¶ Ma xoolaat, gisuma lu moy niir wu weex, ak jëmm ju ca toog, di nirook doom aadama, kaalawoo kaalag wurus, ŋàbb ab sàrt bu ñaw.

Mu jàpp ninki-nànka ja, jaani cosaan jooju di Tuumaalkat bi, di Seytaane ba tey. Malaaka mi yeew ko diiru junniy at.