TSK

TSK · Daniel 12:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Xel mu ñaw, jëw bu rafet; sam xel jekkadi, ñu xeeb la.

«Te bu ñu génnee, gis néewi ñi doon fippu fi sama kaw, seeni sax duñu dee mukk, seen sawara du fey mukk, te boroom suux bu leen gis, yaram wa daw.»

¶ Gannaaw loolu loxol Aji Sax ji da maa dikkal. Aji Sax ji yóbboo ma Noowam, ba teg ma ca digg joor ga, fekk joor ga fees dell aki yax.

«Man nag maa leen di musal ci njaniiwa? Maa leen di jot ci ndee? Moo yaw ndee, ana say mbas? Yaw njaniiw laa ne, ana sa tooke? Fomm làqu na ma!

Tabaxkatu ndab bi daa amul sañ-sañ ci ban bi muy liggéeye, ngir tabax ci bennub tooyal, lenn ndabal teraanga, ak leneen ndabal njoogaan?

Kaayleen ma xamal leen mbir mu umpe. Dunu dee nun ñépp, waaye nun ñépp ay soppiku.

Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanam ngàngune ma, ay téere ubbiku, beneen téere ubbikooti, di téereb dund ba. Ñu daldi àtte néew ya ca seeni jëf, na ñu ko binde ca téere ya.