TSK

TSK · Daniel 2:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Booba mu ngi naan, bu Esawu songee benn dal bi, dal bi ci des mana raw.

Yal na sunu Yàlla Aji Sax ji ànd ak nun, na mu ànde woon ak sunuy maam. Yàlla bu nu wacc mukk mbaa mu di nu dëddu.

Deel jaajëfal Yàlla, sarxale ko, di fey Aji Kawe ji loo dige,

Maa moomi digle, di maye gis-gis; maa am ug dégg, di boroom doole.

Ku rafet xel di boroom doole, ku xam, gëna man;

Man dama noon xel mu rafet a gën doole! Ndeke ku néewle ñu xeeb la, tanqamlu say wax.

Bésub keroog dees na ne: «Aji Sax ji, sant naa la; yaa ma mere woon, meddi, dëfal ma.»

Yàlla nag may ñeenti xale yu góor yooyu xel ak ràññee ci mboolem lu ñu bind ak wàllu xam-xam. Dañeel moom mana firi mboolem peeñu ak gént.

daldi ne: «Cant gu amul ndoorte amul kemu ñeel na Yàlla, xam-xam ak kàttan mooy boroom.

Amos 3:7 TSK

Du lenn moos lu Boroom bi Aji Sax ji def, te déeyu ko yonent yiy jaamam.

¶ Ca waxtu woowa tembe la kemtalaayu mbégte tukkee ci Noo gu Sell gi, dugg Yeesu, mu daldi ne: «Baay, Boroom asamaan ak suuf, sant naa la, nde yaa làq lii boroom xam-xam yeek boroom xel yi, xamal ko tuut-tànk yi, nde loolu de, Baay, mooy li la soob.

Kenn ci mag ñi ne ma: «Bul jooy. Ma ne, Gayndeg giirug Yuda, njebbital Buur Daawuda daan na. Mooy ubbi téere beek juróom ñaari tayoom.»