TSK

TSK · Daniel 2:32

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax jee yor Babilon ci loxoom, muy kaasu wurus bu def xadaru xeet ya, di màndal mboolem àddina; xeet ya naan ca, ba tax ñuy say.

Yaw lañuy dàqe ci nit ñi; rabi àll yi ngay dëkkal, ñax di sam xont niw nag, lay biy wàcc di la faam diiru juróom ñaari jamono, ba kera ngay xam ne Aji Kawe jee yor nguurug nit, di ko jox ku ko neex.

SÉDDALE: Séddale nañu sam réew, ba jox ko xeeti Medd ak Pers.»

Ma séentu, xool, yem ci kuuy mu taxaw feggook yoonu ndox ma, am ñaari béjjén yu gudd te benn bi gëna gudd ba ca des. Waaye bi gëna gudd moo mujja sax.

Jigéen jaa ngi sol lu yolet te xonq, takk wurus ak jamaa aki per. Mu ngi yor kaasu wurus bu fees ak ñaawtéef ak sobey moyam.