Sang baa ngi fi sa ndijoor te mooy rajaxe buur yi, bés bu meree.
TSK
TSK · Daniel 2:34
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
di xaacuy kañ Yàlla, ŋàbbaale saamaru ñaari ñawka,
Mu diw xeet, dim réew, ku la ci nangulul sànku. Xeet yooyu yépp ay yàqu yaxeet.
Mu nattati yeneen junniy xasab, wal ma xóot ba manatumaa xuus, ba jàll. Maneesatu koo jàlle tànk, xanaa féey.
¶ «May xool ba tey ci biir peeñum guddi ma, gisuma lu moy jëmm ju mel ni doomu nit di ñëw, mook niiri asamaan, jëm ci góor gu mag gi; ñu yóbbu ko ba ca moom.
Xelum njublaŋam lay naxee, di réy-réylu, ba bett ñu bare, faagaagal leen, te dina dëkk kilifay kilifa yi. Waaye mooy sànku, te loxo du ko laal.
Bésub keroog maay def Yerusalem di doj wu diis gann ci xeet yépp. Képp ku ko jéema yëngal, da ciy gaañoo gaañu rekk. Te xeeti àddina yépp ay daje ci kawam.
¶ Xam nanu ne sunu yaram, sunu këru kaw suuf gii di ab xayma, bu daanoo it, am taax lanu am fa Yàlla, kër gu sax dàkk, gu loxol nit tabaxul.
Kon nag yeen ñi gëm, yeen la gànjar gi ñeel. Waaye ci ñi gëmul, nag: «Moo di doj wa tabaxkat ya beddi woon, te mu mujj di doju coll wi.»
Dinañu xare ak Gàtt bi, waaye Gàtt bee leen di daan, ndax mooy Sangu sang yi, di Buuru buur yi. Mooy daan mook ñoñam, ñi mu woo, tànn leen te ñu saxoo topp ko.»