Waaye bu noor biy dikk, mu wow, tàngoor jam, mu ŋiis.
TSK
TSK · Daniel 2:35
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ku woyof a cay lekk ba doyal, kuy wut Aji Sax ji, sant ko. «Guddleena gudd fan!»
ma jaareeti fa, ndeke wuute na, ma seet ko, gisuma ko.
àddina yépp di la sujjóotal, di la woy, di joobe sa tur.» Selaw.
Yal na pepp ne gàññ ci réew mi, yal na gub yay jaayu ca tund ya ni gottub Libaŋ; dëkk yu mag yi sëqi nit ba law,
Boroom bi, mboolem xeet yi nga sàkk ñoo lay sujjóotalsi, di màggal sa tur.
Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, Aji Sax ji mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, xeet yépp riirandoo, wutsi ko.
Xeet yaa ngi ŋarandoo ni ndox mu baawaan, Yàlla gëdd leen, ñu daw ba sore; ngelaw yëngu, ñu naaw, ni boob, ba ca kaw tund ya, mbete pënd bu ngëlén wal, mu def callweer.
Moo leen tax di naaxsaay ni niiru suba, mbaa layub njël, mbaa mboob mu naawe dàgga ja, mbaa saxar su gillee ci jankub néeg.
«Yaw janq Siyoŋ mu taaru, jógal bàcci leen, sa béjjén laay def ag weñ, say wewi tànk, ma def ko xànjar, nga rajaxe xeet yu bare.» Yaay faagaagal seen alal ju lewul, ñeel Aji Sax ji, seen koom ñeel Boroom àddina sépp.
Ndaxte fàww Almasi nguuru, ba kera Yàlla di sukkal mboolem ay noonam ciy tànkam.
ñu néewal leen doole, ba amatuñu fu ñu nekk ci asamaan.
¶ Ci kaw loolu ma gis ngàngune mu mag mu weex, ak ku ci toog. Asamaan ak suuf daldi dawe fa kanamam, ne mes.