Ci biir loolu mu rafetook moom, jox ko cér bu sut cér ba mu jox yeneen buur ya mu bokkal curga ca Babilon.
TSK
TSK · Daniel 2:37
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Sirus buuru Pers dafa wax ne: Mboolem réewi àddina, Yàlla Boroom asamaan moo ma leen dénk, te moom moo ma tabb, ngir ma tabaxal ko kër ca Yerusalem ga ca Yuda.
Bul wóolu ribaa, bul yaakaar alalu càcc, neen la. Bu sa alal yokku, nga taf ci sa xol.
Mu ngi naan: «Xanaa du sama jawriñ yépp a diy buur?
Léegi nag teg naa réew yii yépp ci loxol Nabukodonosor buuru Babilon, mi ci sama curga, ba joxaale ko rabi àll yi sax, ñu nangul ko.
¶ «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Maa ngii di jële bëj-gànnaar, indi ci kaw Tir, Nabukodonosor buuru Babilon, buuru buur yi, aki fas aki watiir aki gawar, ak mbooloo mu takku.
Ma joxe ndigal, woolu boroom xam-xami Babilon yépp, ngir ñu xamal ma pirim gént gi.
¶ Loolu lépp dal na Buur Nabukodonosor.
Léegi nag man, Nabukodonosor, maa ngi sant Boroom asamaan, di ko sargal, di ko màggal. Lu mu def dëgg la, fu mu jaare njub la, te kuy réy-réylu man na laa suufeel.
Ci xeeti jaambur ñi lañuy jënde, waaye du tee ma dajale leen. Léegi ñu tegoo notaangey buur aki kàngam.
«Yàlla sunu Boroom, yaa yeyoo daraja ak teraanga ak kàttan, ndaxte yaa sàkk lépp, lépp lu am, yaw la soob, nga sàkk ko.»
Dinañu xare ak Gàtt bi, waaye Gàtt bee leen di daan, ndax mooy Sangu sang yi, di Buuru buur yi. Mooy daan mook ñoñam, ñi mu woo, tànn leen te ñu saxoo topp ko.»