TSK

TSK · Daniel 2:47

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Firawna wax ak Yuusufa ne ko: «Ndegam Yàlla xamal na la lii lépp kay, leer na ne amul kenn ku muus te rafet xel ni yaw.

Job 12:19 TSK

Keey futti sarxalkat, jàllarbi njiit lu riigu.

buuroo buur di ko sujjóotal, xeetoo xeet di ko surgawu.

Aji Sax jee màgg, jara santa sant te gëna mata ragal lépp lu ñuy jaamu.

Samay pexe la buur di jiitee, kilifa di ci àttee dëgg.

Mooy feeñal mbóot mu làqu, xam li ci biir lëndëm, te leer màkkaanoo ko.

Yaw Buur, buuru buur yi, yaw mi Yàlla Boroom asamaan jox nguur ak kàttan ak dooleek ndam,

Garab gi nga gis muy màgg di réy, njobbaxtal lay laal asamaan, ñu di ko séen ci àddina sépp,

Mboolem waa àddina di neen ci moom. Nu ko neex lay def ak gàngoori xarey asamaan ak waa suuf, te kenn du fél loxoom mbaa mu naa ko: «Ana looy def nii?»

Amos 3:7 TSK

Du lenn moos lu Boroom bi Aji Sax ji def, te déeyu ko yonent yiy jaamam.

tukkee itam fa Yeesu Almasi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki jëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqlikook kilifteefu sunuy bàkkaar,

Ci kaw mbubbam ak ci luppam, aw tur lañu ci bind te moo di: «Buuru buur yi, Sangu sang yi.»