TSK

TSK · Daniel 3:15

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Léegi nag, soo leen dee baal seen bàkkaar, aa... Lu ko moy kat, far ma rekk ci téere bi nga bind.»

Ana kooy kókkaleek a ñàkke kersa? Moo kooy yékkatil kàddu? Kooy xool gëti xeebeel? Xanaa du Aji Sell ju Israyil ji?

Ndegam Yàlla ji nuy jaamu man nanoo musal ci taalu sawara bu yànj bi, musal nu ci yaw mii, dina nu musal.

¶ Ci kaw loolu nit ña rungumlooti ba ca Buur, ne ko: «Buur, xamal ne yoonu waa Medd ak Pers tëral na ne mboolem aaye mbaa dogal bu buur dëggal dootu toxu.»

¶ «Bu ñu leen yóbboo ca jàngu ya, ca kanam kilifa ya, ak àttekat ya, buleen jaaxle ci nan ngeen di yékkatee kàddug layoo, ak luy doon seenu lay, mbaa lu ngeen di wax,

Kon nag defleen bu baax ci seen xel, ne soxlawuleena waajal kàddug layoo.

Acts 4:19 TSK

Piyeer ak Yowaan ne leen: «Ndax li jaadu fa Yàlla mooy nu déggal leen, yeen, bàyyi Yàlla? Yeenay àtte loolu.

Acts 6:15 TSK

¶ Mboolem ña ca jataayu àttekat ya nag ne jàkk Eccen; ñu gis xar-kanam ba ne ràññ ni xar-kanamu malaaka.