TSK

TSK · Daniel 3:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Ezra 5:11 TSK

¶ Li ñu nu tontu mooy lii: «Nun ay jaami Yàlla Boroom asamaan ak suuf lanu. Danuy tabaxaat kër Yàlla gi ñu tabaxoon lu jiitu ay at yu bare. Buurub Israyil bu mag moo ko tabaxoon ba sottal ko.

Moo tax Boroom bi Aji Sax ji wax ne: «Maa ngii di dëj fi Siyoŋ aw doju coll, muy doju collu tànnéef wu gànjare ngir kenu gi, te ku ko wéeroo doo gaawa daw.

Ba loolu amee Buur wax Dañeel, ne ko: «Aylayéwén, sa Yàlla mooy Yàllay yàlla yi, di Sangu buur yi, te it mooy kiy feeñal mbóot, gannaaw feeñal nga mii mbóot.»

Ma tëdd sama lal, daldi am gént gu ma tiital, ak xalaat ak peeñu yu ma indil njàqare.

Naka la jub kàmb ga, daldi woo Dañeel; baat baa nga tiis. Mu ne ko: «Éy Dañeel, jaamu Yàlla jiy dund; sa Yàlla ji nga saxoo jaamu, mbaa mujj na laa xettli ci gaynde yi?»

¶ Póol nag ne alkaati ya: «Ñoom ñu dóor nu ci kanam nit ñi, àtteesu nu sax te nu diy gor ci Room gii, rax ci dolli ñu sànni nu ci kaso bi. Léegi ñu bëgg noo dàq ndànk ci biti? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, génne nu.»

¶ Léegi nag ndax nit ñi laay sàkkoo jubool, am Yàlla? Am nit ñi laay wuta neex? Su ma bëggoona wéye neex nit ñi de, duma doon jaamub Almasi.