TSK

TSK · Daniel 3:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Buleen ci sujjóotal lenn, buleen ci jaamu lenn, ndax man seen Yàlla Aji Sax ji, Yàlla ju fiir laa. Maay topp doom tooñu waajur, ba ca seen maasi sët, ba ca maasug sëtaati nit ñi ma bañ.

Dinañu tax mboolem kuy móoloo te bokk ca ngàllog Yudeen ña ca Babilon, danga naan: “Yal na la Aji Sax ji teg la mu tegoon Cedesyas ak Akab, ña buuru Babilon lakk cib taal.”

¶ Buur wax xërëmkat ya ne leen: «Dogal bu wér a ngii tukkee fi man. Su ngeen ma waxul gént gi, wax ma piri mi, ay dog lañu leen di dog, seeni kër doon ay sën.

Te képp ku sujjóotul màggal ko, dees na ko sànni ci biir taal bu yànj.”

Ñooñu yeew leen na ñu soloo, ñook seeni mbubb ak seeni tubéy ak seeni mbaxana, daldi leen sànni ca biir taal bu yànj ba.

Mu ubbi buntu kàmbu xóote ba, saxar su mel ni saxaras taal bu mag jollee ca, jant bi ak jaww ji, lépp lëndëm ndax saxaras kàmb gi.

Seen saxaru sawaras mbugal day saxoo dàkk, di gilli ba fàww. Guddeek bëccëg, ñooñuy sujjóotal rab wi ak jëmm ji ñu ko sàkkal, ak mboolem ku ñu màndargaale turu rab wi, kenn du ci nopplu.»