TSK

TSK · Daniel 3:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Moo mayoon démb xeet yépp, ñu awe seen yooni bopp.

Ñu xalab ninki-nànka ju réy ja, jaanu cosaan joojee ñuy wax Tuumaalkat bi, di ko wax Seytaane, naxekatu mboolem àddina. Ci kaw suuf lañu ko xalab, mooki malaakaam.

Mboolem waa àddinaa koy sujjóotal, mboolem ñi ñu bindul seen tur ca ndoortel àddina ci téereb dund bu Gàtt, bi ñu rendi.

Rab wi nga gis mas naa nekk waaye nekkatul. Dina génne ca xóote ba, waaye day sànkuji. Waa àddina, ñi ñu bindul woon seeni tur ci téereb dund bi ba àddinay door nag, bu ñu gisee rab wi, dinañu yéemu, ndax la mu masoona nekk, tey nekkatul, te ëllëg muy nekkaat.