TSK

TSK · Daniel 4:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Rasel wax baayam ne ko: «Baay, baal ma de, damaa manula jóg ci sa kanam, ndaxte damaa ànd ak mbaax.» Laban seet na fu ne, waaye gisul gàllaaji këram ya.

Ci biir loolu mu sant ki jiitu, ne ko: «Boo dajeek sama mag, mu laaj la ne la: “Kuy sa njaatige?” ak “Ku moom li nga jiital?” ak “Foo jëm?”

¶ Aana ne ko: «Du loolu de, sang bi. Dama di jigéen ju ànd ak naqaru xol, waaye du biiñ, du leneen luy màndee lu ma naan. Dama doon diis Aji Sax ji sama tiisu xol.

Kàddu yooyu la Daawuda dànkaafoo nitam ña; mayu leen ñu dal ci kaw Sóol, ba Sóol jóge ca xunti ma, dem yoonam.

¶ Ci kaw loolu waa Kuus ba ne jimeet. Mu ne: «Buur, sang bi, déglul, xibaaru jàmm a ngi. Aji Sax ji musal na la bésub tey ci ña la doon fexeel ñépp.»

Maaka jàqa jàq bay jal-jali, sama xol biy fuddu! Éy wii mititu xol! Duma mana noppi, maa dégg wooteb liit ak yuuxi xare.

Kilifag jawriñ ya nag tudde leen yeneen tur. Dañeel, mu tudde ko Beltasar, Anaña mu tudde ko Sadarag, Mikayel tudd Mesag, Asaryaa di Abet Nego.

Yaw Buur, buuru buur yi, yaw mi Yàlla Boroom asamaan jox nguur ak kàttan ak dooleek ndam,

Garab gay màgg, di réy, ba njobbaxtal la di laal asamaan, ñu di ko séen ba ca cati àddina sépp.

loolu yépp ndax dañoo gis ci kooku Buur tudde Beltasar, xel mu ñaw akum njàng ak ràññee. Day firi gént, di teqental ay cax ak a lijjanti ay jafe-jafe. Kookooy Dañeel; kon nañu ko woo, mu wax piri mi.»

Màggaay ga mu ko mayoon tax waa mbooloo yeek xeet yeek làkk yépp ragal ko, bay lox ci kanamam. Ku ko soob, mu rey; ku ko soob, mu bàyyi; ku ko soob, mu fal; ku ko soob, mu torxal.

¶ «Fii la mbir mi yem. Man Dañeel nag, ma am njàqare lool, ba sama kanam soppiku, ma denc kàddu yooyu ci sama xel.»

Jekki-jekki jëmm ju mel ni nit dikk, laal samay tuñ. Ma ŋa, àddu, daldi wax ak ki taxaw sama kanam ne ko: «Sang bi, peeñu mi tax na ma jàq, ba amatuma benn doole.