TSK

TSK · Daniel 4:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 1:12 TSK

Aji Sax ji ne Seytaane: «Ayca boog! Mboolem lu bokk ci moom a ngi ci say loxo, waaye moom ci boppam, bu ko sa loxo laal.» Ba loolu amee Seytaane bàyyikoo fa Aji Sax ji.

Job 40:11 TSK

Yuril sa mer, te xool képp ku bew, detteel ko,

Aji Sax ji sib seen njiit yi leen not, wërloo leen àll bu amul yoon.

Ku jiital ngor ak worma, Yàlla jéggal la; ku ragal Aji Sax ji, dëddu lu bon.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yee giñ ne: «Lu ma nar déy mooy am, lii ma mébét, mooy sotti.

Maay yégle muj ca ndoorte la, ak jëf ju amagul, lu jiitu bu yàgg. Maa naa sama mébét a ngi, day am, sama bépp nammeel sotti.