TSK

TSK · Daniel 4:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Tuur ma ñu naa Bel toqi na, tuur ma ñu naa Nebo sukk, mala ya féetewoo seeni jëmm, ñoom lees daan gàddu, tey jur gi jagoo, di leen sëf ba loof.

«Waxleen xeet yi, yéeneleen, woneleen misaal te yéene, waxleen lii, bañ cee làq dara. Neleen: “Dees na nangu Babilon, torxal Bel mbaa Mardug, tuur mi, tas ko, gàcceel gàllaaj yi, tas kasaray tuur yi.”

Kilifag jawriñ ya nag tudde leen yeneen tur. Dañeel, mu tudde ko Beltasar, Anaña mu tudde ko Sadarag, Mikayel tudd Mesag, Asaryaa di Abet Nego.

Xob yaa nga naat, meññeef ma ne gàññ, mana dundal ñépp. Muy keppaaral rabu àll, di tàggal njanaaw, di dundal bépp boroom bakkan.

Am na góor gu nekk ci sa réew mi; xelu yàlla yu sell yaa ngi ci moom, te ci sa jamonoy baay, gis nañu ci moom ag ràññee ak xel ak xam-xam bu nirook xam-xamu yàlla yi. Buur Nabukodonosor sa baay nag fal ko, mu jiite taryaax yeek ñeengokat yeek xërëmkat yeek seetkat yi;