TSK

TSK · Daniel 4:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji da ne: «Su ñu tàmbalee nii, di menn mbooloo te bokk wenn làkk, kon dara dootu leen të.

Firawna ne Yuusufa: «Damaa gént, te kenn manu koo firi, te ma dégg ñuy wax ci yaw naan, gént goo dégg rekk, xam ko, ba man koo firi.»

Sam xel dem ca sa tiitaange ja woon, nga ne: «Moo, ana ka doon waññ? Ana ka doon natt diisaayu galag? Ana ka doon waññiy tata?»

Ca kaw tundu Israyil wu mag wa laa koy jëmbat, mu sëq, meññal, ba doon garabu seedar gu am daraja, mboolem picc dëkke ko, mboolem njanaaw màkkaanoo keram.

Mboolem wàllu xam-xam ak xel mu leen Buur seetlu rekk, gis ne ñoo ci sut fukki yoon taryaax yeek ñeengokati réewam mépp.

¶ Ba mu ko defee Buur teral Dañeel, may ko lu baree bare, ba noppi def ko kilifag diiwaanu Babilon gépp, teg ci fal ko, mu yilif boroom xam-xami Babilon yépp.

Garab gay màgg, di réy, ba njobbaxtal la di laal asamaan, ñu di ko séen ba ca cati àddina sépp.

Am na góor gu nekk ci sa réew mi; xelu yàlla yu sell yaa ngi ci moom, te ci sa jamonoy baay, gis nañu ci moom ag ràññee ak xel ak xam-xam bu nirook xam-xamu yàlla yi. Buur Nabukodonosor sa baay nag fal ko, mu jiite taryaax yeek ñeengokat yeek xërëmkat yeek seetkat yi;