Ba loolu amee tiitaange jàpp mboolem ña ñu woo woon ca jataayu Adoña. Ñu jóg, tasaaroo, ku nekk dem yoonam.
TSK
TSK · Daniel 5:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Tuuri yéefar yi, xaalis ak wurus, loxoo ko sàkk.
Man, Aji Sax jeey sama tur, sama teddnga, duma ko joxe, te sama bàkk, duma ko wacce jëmmi tuur.
Ñii déy a yullee wurus ci mbuus, sàkk xaalis, natt diisaay ba, fey tëgg bu leen ci tëggal am tuur mu ñuy sukkal ak a sujjóotal,
¶ Mu am bés Buur Nabukodonosor defarlu jëmmi wurus, taxawaay ba di fanweeri meetar, yaatuwaay ba di ñetti meetar. Mu taxawal ko ca jooru Dura ga ca diiwaanu Babilon.
xanaa ngay diirook Boroom asamaan, bay santaane ñu indil la ndabi këram, nga di ci naan biiñ, yaak say jawriñ ak say soxna ak say nekkaale, ngeen di sàbbaal ay yàllay xaalis ak yu wurus ak yu xànjar ak yu weñ ak yu bant ak yu doj, te du ci lenn luy gis mbaa muy dégg mbaa mu xam dara. Waaye Yàlla ji yor sa bakkan tey ak ëllëg sàbbaaloo ko.
Wóoy, ngalla ku naan bant: “Xippil,” naan doj wu ne selaw: “Yewwul!” Ana lu yooyii di xamle? Ma nga, ñu xoobe ko xaalis ak wurus, te du gennug noo ci biiram.
Ku ñuy wax Demetirus, ab tëggu xaalis, moo daan defar jëmmi jaamookaay yu ndaw yu tuur mi ñu dippee Artemis, muy njariñ lu réy ci liggéeykat yiy nawleem.