TSK

TSK · Daniel 7:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «May xool ba tey ci biir peeñum guddi mi, daldi yem ci ñeenteelu rab wu raglu, ñàng, te am doole ju jéggi dayo. Mu ngi am bëñi weñ yu réy yu muy moxoñee, di warax, di nappaaje la ca des. Moom nag wuute naak rab yi ko jiitu yépp, te fukki béjjén la am.

Ci kaw loolu béjjén bu ndaw génne ci béjjén yooyu benn, daldi lawa law jublu bëj-saalum ak penkook réew ma gëna rafet.

Bu leen kenn naxe nenn, ndax bés ba du dikkagum, te fippu gu mag ga jëkkula dikk, ba ki jëmmal ndëngte te dëgmal alkute, feeñ.

Ci kaw loolu jeneen firnde feeñ asamaan. Du lenn lu dul ninki-nànka ju réy, xonq curr, am juróom ñaari bopp ak fukki béjjén, juróom ñaari mbaxanay buur tege ci bopp yi, bopp bu ne, menn.

¶ Ci kaw loolu malaaka mi yóbboo ma Noowug Yàlla ba ca màndiŋ ma. Ma gis jigéen ju war rab wu xonq wu am juróom ñaari bopp ak fukki béjjén, te yaram wi fees ak tur yuy saaga Yàlla.

Fukki béjjén yi nga gis, ñook rab wi, dinañu won jigéenu moykat ji mbañeel. Dañu koy futti ba mu ne duŋŋ, ñu lekk aw suuxam, ba noppi lakk ko.