Ca biir peeñu ma, maa ngi Sus, péeyub diiwaanu Elam. Ma gis ci peeñu mi ne maa ngi ci wetu yoonu ndox ma ñu gas te ñu di ko wax Ulay.
TSK
TSK · Daniel 8:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu ne ma: «Dañeel, yaw mi ñu naw, déggal kàddu yi ma lay wax. Jógal taxaw sa taxawaay, ndax dañu maa yebal ci yaw nii.» Naka la ma wax kàddu yooyu, ma ne ñokket, di lox.
Waaye dinaa la xamal li ñu bind ci téereb dëgg gi. Kenn jàpplewu ma ci ñooñu ku dul Mikayel, seen malaakam wattukat, yeen bànni Israyil.
Ma ne: «Ñii lu ñu wund, Sang bi?» Malaaka miy wax ak man ne ma: «Maa lay won lu ñii wund.»
Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw fi kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw, yégal la bii xibaaru jàmm.
Nit ña ànd ak moom a nga taxaw, jommi ba ne cell; dégg nañu baat bi te gisuñu kenn.
Xanaa malaaka yépp duñu ay ngelaw yu ñu sas ab liggéey, yebal leen ngir ñu taxawu ñi wara jagoo ag mucc?
¶ «Man Yeesu maa yónni sama malaaka, ngir mu seede mbir yii ci yeen, ñeel mboolooy gëmkat ñi. Man maay njebbitu Daawuda, di kuutaayam, maa di biddiiwu njël bi ne ràññ.»