TSK

TSK · Daniel 8:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Dama ne ay yàlla ngeen, yeen ñépp di njabootu Aji Kawe ji.

Maa la sëqal ni caxum tool, ngay màgg, di màgg ba mat sëkk, saxi ween, sa kawar sëq, te nga ne duŋŋ-duŋŋaaral.

¶ Ba àpp ba matee, man Nabukodonosor, maa séentu asamaan, sama sago délsi. Ma sant Aji Kawe ji, sargal Kiy dund ba fàww, màggal ko: kilifteefam sax fàww, nguuram ñeel maasoo maas.

Dañeel da ne: «Damaa gis guddi ci peeñu mi; mu jekki-jekki am ngelaw lu jóge ñeenti wet, riddeendoo, di yëngal géej gu mag ga.

May xool, ab sikket jóge sowu, jaare déndu suuf sépp te laalul suuf. Sikket baa nga am béjjén bu yéeme ci diggante bët yi.

Naka lay jóg rekk, nguuram daldi foq, tas, ñeenti ngelawi asamaan tasaare, yóbbu. Aw askanam du moom nguur ga, te nguur ga dootu am doole ja mu amoon. Nguuram day foq, tàbbi ci loxoy ñeneen ñu dul askanam.